11Ku bon fippu doŋŋ lay jéem, te musibaa koy dikkal.
12Taseek gaynde gu ñàkki doomam moo gën taseek dof ak yëfi dofam.
13Kuy feye mbon jëf ju baax, lu bon du jóge sa kër.
14Ndoortel ay di wal mu tàmbali, luy indib xuloo, bàyyil.
15Dëggal ku sikk ak daan ku jub, Aji Sax ji sib na yooyu yaar.
16Ab dof du am xaalis, jënde xel mu rafet; buggu ca dara.
17Xarit du bëgg, di bañ; mbokk day bokk ak yaw say coono.