19Woyof, ànd ak ku néewle moo gën séddook ku bew la mu lewal.
20Ku teewlu mbir, baaxle; ku wóolu Aji Sax ji, bég.
21Ki rafet xel mooy kiy ràññee, te su wax rafetee, dég-dég yomb.
22Xel mu ñaw day suuxat bakkan, te ab dof jëfi dofam a koy yar.
23Ku rafet xel, say kàddu xelu; soo waxee, yey.
24Wax ju yiw di lem juy xelli, neexa ñam, di jàmmi yaram.
25Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.
26Ku bëgg lu neex, liggéey; ku bëgga faj sab xiif, njaxlaf.
27Sagaru nit mooy sulli lu bon, ay waxam sax sawara la.
28Nitu njekkar day yokk réeroo, ab soskat di féewaley xarit.
29Ab soxor day yóbbaale dëkkandoom, jëme ko ci lu bon.
30Piise, ku nar njekkar; màttu, ku def lu bon.