18Réy, yàqule; xeebaate, jóoru.
19Woyof, ànd ak ku néewle moo gën séddook ku bew la mu lewal.
20Ku teewlu mbir, baaxle; ku wóolu Aji Sax ji, bég.
21Ki rafet xel mooy kiy ràññee, te su wax rafetee, dég-dég yomb.
22Xel mu ñaw day suuxat bakkan, te ab dof jëfi dofam a koy yar.
23Ku rafet xel, say kàddu xelu; soo waxee, yey.
24Wax ju yiw di lem juy xelli, neexa ñam, di jàmmi yaram.
25Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.
26Ku bëgg lu neex, liggéey; ku bëgga faj sab xiif, njaxlaf.
27Sagaru nit mooy sulli lu bon, ay waxam sax sawara la.
28Nitu njekkar day yokk réeroo, ab soskat di féewaley xarit.