Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 14

Kàddu yu Xelu 14:27-35

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27Ragal Aji Sax ji day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
28Su mbooloo baree, buur am ndam; fu nit ña néew, kilifa du fa dara.
29Muñ mer, déggin wu yaa; gaawa tàng, gënatee dof.
30Xel mu dal, yaram wu naat; fiiraange semmal boroom.
31Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.
32Coxor detteel boroom; ku jub fegoo maanduteem.
33Kuy dégg, sam xel saxoo rafet; ab dof sax xam na lu xelu.
34Njekk day teral aw xeet, moy di gàcceel aw askan.
35Buur day bége jawriñ ju xelu, di mbugal nitu gàcce.

Read Kàddu yu Xelu 14Kàddu yu Xelu 14
Compare Kàddu yu Xelu 14:27-35Kàddu yu Xelu 14:27-35