27 Ragal Aji Sax ji day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
28 Su mbooloo baree, buur am ndam; fu nit ña néew, kilifa du fa dara.
29 Muñ mer, déggin wu yaa; gaawa tàng, gënatee dof.
30 Xel mu dal, yaram wu naat; fiiraange semmal boroom.
31 Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.
32 Coxor detteel boroom; ku jub fegoo maanduteem.
33 Kuy dégg, sam xel saxoo rafet; ab dof sax xam na lu xelu.
34 Njekk day teral aw xeet, moy di gàcceel aw askan.
35 Buur day bége jawriñ ju xelu, di mbugal nitu gàcce.