Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 13

Kàddu yu Xelu 13:3-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Moom sa làmmiñ, sàmm sa bakkan; rattaxle, yàqule.
4Ab yaafus day yaakaar, du am; ab njaxlaf sàkku, woomle.
5Ku jub bañ na ay fen, ku soxor di indi gàcceek yeraange.
6Ku mat day jub, ba fegu; moykat soxor, ba sànku.
7Nit a ngi am-amlu, amul dara; nit di dee-deelu te fees dell.

Read Kàddu yu Xelu 13Kàddu yu Xelu 13
Compare Kàddu yu Xelu 13:3-7Kàddu yu Xelu 13:3-7