1Doom ju xelu dégg yaru baay, kuy ñaawle faalewuli àrtu.
2Wax ju rafet yool na boroom, workat fitna la namm.
3Moom sa làmmiñ, sàmm sa bakkan; rattaxle, yàqule.
4Ab yaafus day yaakaar, du am; ab njaxlaf sàkku, woomle.
5Ku jub bañ na ay fen, ku soxor di indi gàcceek yeraange.
6Ku mat day jub, ba fegu; moykat soxor, ba sànku.
7Nit a ngi am-amlu, amul dara; nit di dee-deelu te fees dell.
8Ku am ay fey alal, ba mucc; ku amul deesu ko tëkku.
9Ku jub day leer nàññ, ab soxor mel ni taal bu fey.