6Ab soxor, waxam am tëru la, day reye; kàdduy kiy jubal di musle.
7Ab soxor bu daanoo, jeex na; ku jub, sa kër taxaw, ne këcc.
8Xel mu ñaw, jëw bu rafet; sam xel jekkadi, ñu xeeb la.
9Woyof mbubb, am benn surga doŋŋ, moo gën réyal turki tey dee ak xiif.