Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 12

Kàddu yu Xelu 12:22-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Aji Sax ji sib na fen-kat, safoo ku dëggu.
23Nit ku ñaw day xam, ba ca; ab dof siiwal waxi dofam.
24Njaxlaf, jiitu; yaafus, des gannaaw.
25Njàqare day jeexal xolu boroom, wax ju neex di tooyal xolam.
26Ku jub day seetlu ku muy xaritool; soxor bi, jikkoom a koy sànk.
27Ab yaafus bu rëbbee, sooy; cawarte koom la.
28Jaaral ci njekk, ba gudd fan; yoon wu baax deesu fa dee.

Read Kàddu yu Xelu 12Kàddu yu Xelu 12
Compare Kàddu yu Xelu 12:22-28Kàddu yu Xelu 12:22-28