Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 12:22-28 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 12:22-28 in Kàddug Yàlla gi

22 Aji Sax ji sib na fen-kat, safoo ku dëggu.
23 Nit ku ñaw day xam, ba ca; ab dof siiwal waxi dofam.
24 Njaxlaf, jiitu; yaafus, des gannaaw.
25 Njàqare day jeexal xolu boroom, wax ju neex di tooyal xolam.
26 Ku jub day seetlu ku muy xaritool; soxor bi, jikkoom a koy sànk.
27 Ab yaafus bu rëbbee, sooy; cawarte koom la.
28 Jaaral ci njekk, ba gudd fan; yoon wu baax deesu fa dee.
Kàddu yu Xelu 12 in Kàddug Yàlla gi