5Ku mat, njekk xàllal la; coxor daaneel boroom.
6Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.
7Ab soxor saay, yaakaaram seey, rawatina yaakaar ju sës ci alal.
8Ku jub mucc ci njàqare, ab soxor wuutu ko ca.
9Ay sos la yéefar di loree, waaye ku jub xam-xam la cay mucce.
10Ku jub baaxle, waa dëkkam bànneexu; ab saaysaay saay, mbégte dim riir.
11Barkeb ku jub teral nab dëkk, kàddug ku soxor tas nab dëkk.
12Waxi xeebaate ñàkk bopp la, ku am ag dégg day noppi.
13Kuy wër di sos dangay wuññi sutura, ku jara wóolu dangay am bàmmeelu biir.
14Tegtal tumurànke, am réew suux; digle bare, ndam dikk.
15Bul gàddul kenn bor, di loru; bañ koo dige, daldi am jàmm.