Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 10

Kàddu yu Xelu 10:7-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ku jub barkeel, saw tur du fey; ab soxor, turam seey.
8Ku rafet xel day jëfe santaane, ab dof waxa wax, ba loru.
9Maandu, fegu; dëng, weeru.
10Piiseek làq-làqal, sabab njàqare; ab dof waxa wax, ba loru.
11Kàdduy ku jub bëtu ndox la, day naatal; waaye ku soxor, wax ja làq fitna.
12Mbañeelak ayoo; cofeelak jéggale bépp tooñ.
13Kuy dégg, say wax rafet; te ku ñàkk bopp, yelloo yetu gannaaw.
14Ku rafet xel day xam, ne cell; bu dof noppiwul, yàqule teew.
15Alal day aar boroom ni ab tata, ñàkk di lor baadoolo.
16Ku jub jot peyam, dunde; ab soxor di bàkkaare alalam.
17Yaru, gudd fan; sàgganey àrtu, sànku.
18Ku la nëbbal mbañeel, da lay fen; kuy wër di sos, ab dof la.

Read Kàddu yu Xelu 10Kàddu yu Xelu 10
Compare Kàddu yu Xelu 10:7-18Kàddu yu Xelu 10:7-18