Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 10

Kàddu yu Xelu 10:22-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
23Jëf ju bon la dof di foye; ku am dég-dég safoo lu xelu.
24Ab soxor, li mu ragal moo koy dab; nammeelu ku jub day sotti.
25Bu ngëlén walee, ab soxor ne mes; ku jub, sab reen sax ba fàww.
26Ndaw lu tayel ca ka yónnee daa mel ni lu forox ciy gëñ mbaa saxar ciy gët.

Read Kàddu yu Xelu 10Kàddu yu Xelu 10
Compare Kàddu yu Xelu 10:22-26Kàddu yu Xelu 10:22-26