22 Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
23 Jëf ju bon la dof di foye; ku am dég-dég safoo lu xelu.
24 Ab soxor, li mu ragal moo koy dab; nammeelu ku jub day sotti.
25 Bu ngëlén walee, ab soxor ne mes; ku jub, sab reen sax ba fàww.
26 Ndaw lu tayel ca ka yónnee daa mel ni lu forox ciy gëñ mbaa saxar ciy gët.