29«Bokk yi, man naa leena wax lu wóor ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul nañu ko; bàmmeelam mu ngi ci nun ba tey.
30Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàlla digoon na ko ci ngiñ ne dina teg ci nguuram kenn ci askanam.
31Kon gis na lu ñëwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne bàyyiwuñu ko ci barsàq, te yaramam yàquwul.
32Yeesu moomu nag, Yàlla dekkal na ko; nun ñépp seede nanu ko.
33Yàlla yéege na ko ak ndijooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi ñu dige woon, ba tuur lii ngeen gis te dégg ko.
34Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na: “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor,
35ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
36«Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»
37Bi ko mbooloo ma déggee, naqaru xol wu metti jàpp leen; ñu daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, lu nu wara def?»
38Piyeer ne leen: «Tuubleen seeni bàkkaar, te kenn ku nekk ci yéen, ñu sóob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te may leen Xel mu Sell mi.