29 «Bokk yi nag, Maam Daawuda, manees na leena wax ci lu wér ne nelaw na, ba ñu denc ko, te bàmmeelam a ngi fi, nuy gis ba tey jii.
30 Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàllaa ko giñaloon ne ku bokk ci geñoom lay teg cib jalam.
31 Kon li mu gis te dikkagul mooy ndekkitel Almasi, te ci mbiram la wax ne bàyyeesu ko biir njaniiw, te yaramam du yàqu.
32 Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.
33 Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko.
34 Ndax kat du Daawudaa yéeg asamaan, waaye moom ci boppam moo ne: “Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko: ‘Toogeel sama ndijoor,
35 ba ma def say noon, sa ndëggastalu tànk.’ ”
36 «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»
37 Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?»
38 Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.