Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 27

Jëf ya 27:16-44

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Nu leru nag dun bu tuuti bu ñuy wax Koda, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li, teg ci sonn lool doora téye loocob rawtu bu gaal gi.
17Ñu yéege looco ba, daldi jël ay buum yu ñu laxas ca yaramu gaal ga, dàbblee ko ko. Ci kaw loolu ñu ragala ngiroji ca beeñ bu ñuy wax Sirt, ba tax ñu sànni diigal, ngir yeexal gaal ga, daldi yalal.
18Ca ëllëg sa ngelaw la wéye noo pamti-pamtee, ba ñu mujj wàññi ca yebu gaal ga, sànni biir géej.
19Ca gannaaw ëllëg sa, seen loxoy bopp lañu jële yenn jumtukaayi gaal ga, sànni.
20Ay fani fan jant beek biddiiw yi ne meŋŋ, te ngelaw liy riddi rekk, ba nu noppee yaakaar ne dinanu mucc.
21Loolu nag fekk na ñu gëjoona lekk. Póol daldi taxaw ca seen biir ne: «Bokk yi, su ngeen yégoon déggal ma, baña jóge Keret, ba moyu loraange gii ak yàqule gii.
22Léegi nag dama leen di ñaax, ngir ngeen dalal seen xel, ndax kenn ci yeen du ñàkk bakkanam, gaal gi rekk ay yàqu.
23Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.
24Mu ne ma: “Póol, bul tiit; fàww nga taxawi fa kanam Sesaar, te it Yàlla moo la baaxe muccug mboolem ñi nga àndal ci gaal gi.”
25Kon nag, bokk yi, dalal-leen seen xel, ndax gëm naa Yàlla, xam naa ne ni mu ko waxe, ni lay ame.
26Du ñàkk aw dun wu nu lufeji.»
27Ca fukkeelu bés baak ñeent, nu ngay yal-yalee fu ne ca géeju Adiratig; ba guddi ga xaajee mool ya njort ne nu ngay jegesi ab tefes.
28Ñu sànni nattukaay ba biir géej, gis ndox ma xóote ñaar fukki dayo, xawa yemook ñeent fukki meetar. Ñu demati tuuti, sànniwaat ko, daldi gis ndox ma xóote fanweeri meetar, xawa yemook fukki dayo ak juróom.
29Ci kaw loolu ñu ragala lufeji bérab bu ami doj, ba tax ñu sànnee ca geenu gaal ga, ñeenti diigal, tey ñaan jant fenke leen.
30Teewul mool ya ñoom di fexee raw, daldi dem ba yoori loocob rawtu ba biir géej, tey taafantoo ne ay diigal lañuy sànnee ca boppu gaal ga.
31Póol nag ne njiitu takk-der ba ak xarekat ya: «Ñii bu ñu desul ci gaal gi, yeen dungeen raw.»
32Ca la takk-der ya dog buum ya téye looco ba, bàyyi, mu wéy.
33Naka la jant di waaja fenk, Póol ñaax ñépp, ngir ñu lekk; mu ne leen: «Fukki fan ak ñeent a ngii, yeena ngi toog, lekkuleen, sexuleen dara.
34Dama leen di ñaax nag ngir ngeen lekk, ndax noonu doŋŋ ngeen mana rawe. Du genn kawar sax guy rote ci boppu kenn ci yeen.»
35Loolu la wax, daldi jël mburu, sant Yàlla ci kanam ñépp, ba noppi dagg, lekk.
36Ba loolu amee, ñépp dellu sawar, daldi lekk ñoom itam.
37Ña nekkoon ca gaal ga ñépp ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom benn (276) lañu.
38Ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma biir géej, ngir woyofal gaal ga.
39Ba bët setee, xàmmiwuñu réew ma, waaye ab catu tefes lañu séen. Ñu fas yéene caa teerali, ndegam manu na.
40Ba mu ko defee ñu dagg diigal ya, wacc biir géej, yiwiwaale goj ya téye joowu yay dawal gaal ga. Ci kaw loolu ñu firi wiiru kanam ga, wacce ak ngelaw la, nu wuti tefes ga.
41Teewul ñu dal fu ñaari ndaw daje, ci ab tundu beeñ, gaal ga luf. Boppu gaal ga nuur ca suuf sa, yëngootul, geenu gaal ga tas ndax dooley gannax ya.
42Ba loolu amee takk-der ya nara rey ña ñu tëj, bala ñoo féey, ba raw.
43Njiitu takk-der ba nag namma rawale bakkanu Póol, ba tax mu aaye loolu. Mu sant ñi mana féey, ne leen ñu jëkka sóobu, wuti tefes ga.
44Ña ca des nag, topp ca, ñii langaamoo ay dénk, ñee, tojiti gaal ga. Noonu la ñépp mujje jot tefes ga ci jàmm.

Read Jëf ya 27Jëf ya 27
Compare Jëf ya 27:16-44Jëf ya 27:16-44