Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 26

JËF YA 26:7-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Dige booba la fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di sàkku, ngir jot ko, ci jaamu Yàlla ak cawarte guddi ak bëccëg. Yaw buur, yaakaar joojoo tax ñu may kalaame, ñoom Yawut yi.
8Lu tax seen xel dàq ne Yàlla dina dekkal ñi dee?
9«Man sax ci sama bopp defe woon naa ne war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret.
10Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci sarxalkat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoona bëgga rey, ànd naa ci.
11Daan naa wër jàngoo jàngu, di leen teg toskare te di leen jéema weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xañ ba ca dëkk yu sore, ngir fitnaal leen.
12«Noonu am bés, may dem dëkku Damaas, yor sañ-sañ ak ndigalu sarxalkat yu mag ya.
13Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu jóge asamaan ne ràyy, ba raw leeru jant, melax ba ëmb ma, man ak ñi ma àndal.
14Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.”
15«Noonu ma ne ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal.
16Waaye jógal taxaw. Lii moo tax ma feeñu la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci lépp li nga gis ci man ak li ma lay feeñuji.
17Dinaa la musal ci bànni Israyil ak ci ñi dul Yawut. Ci ñoom laa lay yebal,
18ngir ubbi seeni bët, nga jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, nga nangoo leen ci sañ-sañu Seytaane, waññi leen ci Yàlla, ma baal leen seeni bàkkaar te may leen cér ci biir sama gaa yi sell ci kaw ngëm.”
19«Kon nag buur Agaripa, woruma li ma Yàlla yen ci peeñu.
20Waaye li tàmbali ci Damaas, teg ci dëkku Yerusalem ak réewu Yawut mépp, ba agsi ci ñi dul Yawut, yégal naa leen, ñu tuub seeni bàkkaar te waññiku ci Yàlla, bay jëf lu dëppook réccu.
21Loolu nag moo waral Yawut yi jàpp ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey.
22Waaye gannaaw Yàllaa ngi may taxawu ba tey, maa ngi taxaw fi, di ko seedeel ci mag ak ndaw; yokkuma dara ci li yonent yi ak Musaa xamle woon lu jiitu,
23maanaam Almasi bi dina dékku ay coono, te mooy jëkka dekki, bay jollil leer ci bànni Israyil ak ñi dul Yawut.»
24Bi muy làyyee nii, Festus daldi ko gëdd ak baat bu kawe ne ko: «Dangaa dof, Pool! Xanaa sa njàng mu réy mi da laa xañ sago.»

Read JËF YA 26JËF YA 26
Compare JËF YA 26:7-24JËF YA 26:7-24