Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 26

Jëf ya 26:7-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Te mooy dige bi fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di séentu mu sottil leen, ba tax guddi ak bëccëg ñu xér ci jaamu Yàlla. Yaakaar jooju nag, Buur, moo tax Yawut yi tuumaal ma!
8Ana lu leen taxa jàpp ci seen biir ne xel nanguwul Yàlla di dekkal ñi dee?
9«Man ci sama bopp, gàntal lu ma man turu Yeesum Nasaret, sama warugar laa ko defoon.
10Def naa ko ci Yerusalem, te it bare na ñu sell ñu ma tëjlu ci kaw sañ-sañ bu ma sarxalkat yu mag yi jagleel, te saa yu ñu leen tegaan àtteb dee, dama daan biral kàddu gu leen àtte ñàkkal.
11Jàngoo jàngu laa leen daan tege mbugal ay yooni yoon, ngir xàccloo leen. Maa daan sànju ba xaabaabal ci seen kaw, topp leen ba ci biir dëkki jaambur yi.
12«Yoon wu mel noonu laa doon dox, jëm Damaas, ci ndigalal ak ndénkaanel sarxalkat yu mag yi.
13Ba ma demee ba wetu digg bëccëg, Buur, ca laa gis ag melax gu leer ba raw jant bi, fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër, maak ñi ma àndal.
14Nu ne dàll fi suuf. Ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut, ne ma: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal? Dangay sonal sa bopp rekk, mbete fas wu manula woŋŋeetu ba wéq dëgël bu koy jam.”
15«Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Sang bi ne ma: “Man maay Yeesu, mi ngay bundxatal.
16Jógal taxaw nag. Dama laa feeñu ngir def la ngay sama surga, ngir nga di ma seedeel peeñum tey, ak peeñu yi ma lay feeñooji ëllëg.
17Maa lay musal ci askanu bànni Israyil, ak ci jaambur ñi ma lay yebal,
18ngir nga xippil leen, jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, seppee leen ci noteelu Seytaane, indi leen ci Yàlla, ñu am njéggalug bàkkaar, am cér ci biir nit ñi ñu sellal ndax ngëm, gi ñu ma gëm.”
19«Kon nag buur Àggripa, peeñum asamaan moomu, woruma ko.
20Waaye li dale Damaas ak Yerusalem ba ci réewum Yawut gépp, ba ca ñi dul Yawut, ñoom ñépp yégal naa leen seen wartéef, muy tuubeel ak waññiku ci Yàlla, ak jëf ju tuubeel yellool.
21Loolu moo waral Yawut yi jàppe ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey.
22Ndimbalal Yàlla nag moo ma may may dund ba tey jii, di ko seedeel ci mag ak ndaw, te waxuma lenn lu moy la yonent ya ak Musaa waxoon ne dina am.
23Dañu noon fàww Almasi jaar ci ay coono te mooy jëkka dekki, ba siiwtaane leer gu jolli, ñeel bànni Israyil ak jaambur ñi itam.»
24Naka la layool boppam noonu, Festus àddu ca kaw, ne ko: «Póol, yaw dangaa dof! Sa njàng mu réy mee la dofloo.»

Read Jëf ya 26Jëf ya 26
Compare Jëf ya 26:7-24Jëf ya 26:7-24