20Na def ak yëkk woowu na muy def ak yëkku saraxu póotum bàkkaar rekk. Noonu lay def ak moom. Ni la ko sarxalkat biy defale seen njotlaay, ñu am njéggal.
21Na génne yëkk wi dal bi, taal ko, na muy taale yëkk wi ñu jëkka wax. Saraxu póotum bàkkaaru mbooloo mi la.
22«Su fekkee ne kilifa moo moy lenn ci santaaney Yàllaam Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,
23bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe sikket bu amul sikk.
24Day teg loxoom ci boppu sikket bi, rendi ko fa ñuy rendi saraxu rendi-dóomal, fa kanam Aji Sax ji. Saraxu póotum bàkkaar la.
25Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deretu sarax siy póotum bàkkaar, taqal ko ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ba noppi tuur deret ji ci taatu sarxalukaayu rendi-dóomal bi.
26Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
27«Su dee kenn ci baadoolo yee moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,