Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 4:20-27 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 4:20-27 in Kàddug Yàlla gi

20 Na def ak yëkk woowu na muy def ak yëkku saraxu póotum bàkkaar rekk. Noonu lay def ak moom. Ni la ko sarxalkat biy defale seen njotlaay, ñu am njéggal.
21 Na génne yëkk wi dal bi, taal ko, na muy taale yëkk wi ñu jëkka wax. Saraxu póotum bàkkaaru mbooloo mi la.
22 «Su fekkee ne kilifa moo moy lenn ci santaaney Yàllaam Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,
23 bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe sikket bu amul sikk.
24 Day teg loxoom ci boppu sikket bi, rendi ko fa ñuy rendi saraxu rendi-dóomal, fa kanam Aji Sax ji. Saraxu póotum bàkkaar la.
25 Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deretu sarax siy póotum bàkkaar, taqal ko ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ba noppi tuur deret ji ci taatu sarxalukaayu rendi-dóomal bi.
26 Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
27 «Su dee kenn ci baadoolo yee moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,
Sarxalkat yi 4 in Kàddug Yàlla gi