12«Bu saraxu nit ki dee bëy, na ko indil Aji Sax ji
13te teg loxoom ci bopp bi, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi. Na doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
14La mu cay génnee muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji mooy nebbon bi sàng yérey biir yi yépp, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
15ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
16Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñamu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Mboolem luy nebbon, Aji Sax jeey boroom.