12 «Bu saraxu nit ki dee bëy, na ko indil Aji Sax ji
13 te teg loxoom ci bopp bi, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi. Na doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
14 La mu cay génnee muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji mooy nebbon bi sàng yérey biir yi yépp, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
15 ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
16 Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñamu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Mboolem luy nebbon, Aji Sax jeey boroom.