Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 13

Sarxalkat yi 13:50-59

Help us?
Click on verse(s) to share them!
50Na sarxalkat bi nemmiku liir wi, ba noppi ber këf ki teg liir wi diiru juróom ñaari fan.
51Bésub juróom ñaareel ba na seet liir wa. Su liir wa lawee ca kaw këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa der mbaa jumtukaayu der, kon liir wu aaytal la te këf ka sobewu na.
52Da koy lakk, ndax liir wu aaytal la, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa kawaru gàtt gu ñu ëcc mbaa wëñ gu ëccu mbaa lu ñu defare der te liir wa tegu ca. Dees koy lakk, ba mu dib dóom.
53Waaye kat bu sarxalkat bi seetloo ne liir wi lawul ci këf ki, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa jumtukaayu der,
54na santaane ñu fóot ko, mu daldi koy beraat juróom ñaari fan.
55Ndegam nag gannaaw ba ñu fóotee këf ka teg liir, sarxalkat bi seet na ko, te liir wi soppiwul melo, bu lawul it setul. Dees koy lakk, ba mu dib dóom, su yàqoo biir ak su yàqoo biti yépp.
56Su sarxalkat bi gisee gannaaw ba ñu fóotee këf ka ne, liir wi raaf na, na dagg sànni fa tegoon liir ca këf ka, muy ndimo mbaa der mbaa bàgg mbaa poqe.
57Su liir wa génnaatee ca këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, kon liir wuy màgg la. Këf ka teg liir dees koy lakk, ba mu dib dóom.
58Ndegam liir wa deñ na, gannaaw ba ñu fóotee këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, dees koy fóotaat, mu doora set.»
59Loolu la yoon digle ci liir wuy law wu tegu ci ndimol kawar gu ëccu mbaa lu wëñ gu ëccu mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der. Ci digle yooyu lañuy tegu, ba mana biral ne këf ka set na am setul.

Read Sarxalkat yi 13Sarxalkat yi 13
Compare Sarxalkat yi 13:50-59Sarxalkat yi 13:50-59