Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - ROOM - ROOM 8

ROOM 8:4-37

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Ba tax na léegi njub, gi yoonu Musaa di digle, am na ci nun, ñiy déggal Xelu Yàlla mi te baña topp sunu nafsu.
5Ñiy topp seen nafsu, seeni bëgg-bëgg rekk lañu fonk, waaye ñiy topp Xelu Yàlla mi, coobareem lañu fonk.
6Ndaxte fonk nafsu, ci dee lay jëme; waaye fonk Xelu Yàlla mi, dund ak jàmm lay joxe.
7Ndaxte ku fonk sa nafsu, bañaaleb Yàlla nga, ndaxte doo déggal Yàlla, mbaa ngay sàmm ay santaaneem, te manuloo koo def sax.
8Kuy topp sa nafsu nag, doo mana neex Yàlla.
9Waaye yéen nekkatuleen ci topp seen nafsu, waaye yéena ngi topp Xelu Yàlla mi, bu fekkee ne mu ngi dëkk ci yéen. Ku amul Xelum Kirist nag, bokkuloo ci moom.
10Bu fekkee ne Kirist dëkk na ci yéen nag, lii moo am: seen yaram mi ngi ci dooley dee ndax bàkkaar bi nekk ci yéen, waaye seen xel mi ngi dund ndax njub gi leen Yàlla jox.
11Kon nag gannaaw Xelum Yàlla, mi dekkal Yeesu ca néew ya, dëkk na ci yéen, dina tax seen yaram wi néew doole dund ci kàttanu Xel moomu dëkk ci yéen.
12Kon nag bokk yi, am nanu lu nu war, waaye waxuma leen topp sunu nafsu ak i bëgg-bëggam;
13ndaxte kuy topp nafsoom, fàww mu dee, waaye kuy not jëfi yaramam ci dooley Xelu Yàlla mi, dina dund.
14Ndaxte ñépp ñiy déggal Xelu Yàlla mi, ay doomi Yàlla lañu.
15Nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba», maanaam «Baay.»
16Ndaxte Xelu Yàlla mi, moom ci boppam, day ànd ak sunu xel ci seede ne doomi Yàlla lanu.
17Gannaaw ay doomi Yàlla lanu, dinanu moomi lépp li Yàlla jagleel ay doomam, séddu ci ngëneel yi Kirist yelloo. Waaye nag ku bëgga bokk ak Kirist ndamam ëllëg, war ngaa séddu ci ay fitnaam tey.
18Xalaat naa ne sunu naqaru tey, wareesu ko tëkkale ak sunu ndamu ëllëg.
19Ndax li Yàlla bind lépp a ngi ne seewa gis doomi Yàlla yi feeñ ci seen biir ndam.
20Ndaxte dunyaa bi bépp mu ngi ci yoon wu dul mujj fenn; teyu ko, Yàlla moo ko ko teg. Waaye teewul ñu am yaakaar ne,
21Yàlla dina rengi seen buumi njaam ci dee, boole leen ci jàmmu doomi Yàlla yi ak seen ndam.
22Xam nanu ba fi nu tollu ne li Yàlla bind lépp a ngi mititlu ni jigéen juy matu.
23Te du dunyaa bi rekk mooy mititlu, nun it nu ngi mititlu, nun ñi Yàlla sol Xelam, ngir nu ñam añu ëllëg; nu ngi ne seew Yàlla boole nu ci lépp li nu yelloo ni ay doomam, keroog bés bu Yàllay goreel sunu yaram.
24Ndaxte sunu mucc ëmb na yaakaar. Li nga gis ba noppi, nekkatul yaakaar; li teew, noo koy yaakaare?
25Li feek gisagunu nag li nuy yaakaar, dinanu ko séentu ak muñ.
26Te it Xelu Yàlla mi moo nuy xettali ci sunug néew doole. Ndaxte xamunu sax naka lanu wara ñaane Yàlla, waaye Xelu Yàlla maa ngi nuy ñaanal fa moom ak i yéene yu làmmiñ manta takk.
27Te Yàlla, miy nattu xol yi, xam na xalaatu Xel mi, ndaxte tinu, gi muy tinul gaayi Yàlla yi, méngoo na ak coobarey Yàlla.
28Xam nanu itam ne ñi bëgg Yàlla, maanaam ñi Yàlla woo ci boppam te boole leen ci li mu tëral, Yàlla dina joo loxoom ci lépp lu xew ci seen dund, ngir jural leen lu baax.
29Ndaxte ñi mu xamoon lu jiitu, dafa dogaloon ñu nirook Doomam, ngir mu nekk taaw ci biir njaboot gu yaa.
30Ñi mu dogaloon loolu ci ñoom, da leena woo; ñooñu mu woo, da leena àtte ni ñu jub; ñooñu mu àtte jub, da leena boole ca ndamam.
31Lu nu wara wax nag ci loolu lépp? Gannaaw Yàlla ànd na ak nun, kan moo nu manal dara?
32Yàlla mi nu gàntulul Doomam waaye mu joxe ko, mu dee ngir nun, ndax dina nu bañalati dara?
33Ñi Yàlla tànnal boppam, kan moo leen di tuumaal? Yàlla moo leen àtte ni ñu jub.
34Kan moo leen mana teg tooñ? Yeesu Kirist mi dee, moo dekki itam, te mu nga fa ndijoorul Yàlla, di nu fa ñaanal!
35Kan moo nu mana tàggaleek mbëggeelu Kirist? Xanaa duy nattu, te du njàqare, du it fitna, du xiif walla rafle, du it ay ngaañ walla jaasi sax.
36Moo tax Mbind mi ne: «Ñu ngi nuy rey ngir yaw, ci suba ba jant so; ñu ngi nuy jàppe ni xar yu ñuy rey.»
37Waaye loolu lépp teewul, nu ngi mel niy ñeyi xare ci dooley Kirist mi nu bëgg.

Read ROOM 8ROOM 8
Compare ROOM 8:4-37ROOM 8:4-37