Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 2

Room 2:5-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.
6Ca lay fey ku nekk ay jëfam.
7Ñi saxoo di jéema def jëf ju baax, ngir di ko sàkkoo ndam, ak teraanga, ak texe gu sax, ñooñu, texe gu sax dàkk mooy doon seenub añ.
8Waaye ñi fétteeral ci seen sàkkuteefi bopp, nanguwuñoo topp liy dëgg, xanaa ag njubadi nag, ñooñu, am sànj ak mer mu ne jippét lañuy yooloo.
9Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci;
10daraja, ak teraanga, ak jàmm nag moo ñeel képp kuy def lu baax, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci.
11Ndax kat xejj ak seen amul fa Yàlla.
12Mboolem ñi bàkkaar nag te fekku leen ci yoonu Musaa, yoonu Musaa toppu leen, waaye du leen teree sànku. Mboolem ñi bàkkaar it, te mu fekk leen ci yoonu Musaa, ci yoonu Musaa lees leen di daane.
13Ndax kat du déglukati yoonu Musaa lees di joxee àtteb ñu jub fa kanam Yàlla, waaye jëfkati yoonu Musaa lees di joxe nit àtteb ku jub.
14Jaambur ñi dul Yawut, te amuñu yoonu Musaa, ndegam teewu leena topp bindub juddu, bay jëfe li yoonu Musaa laaj, dafa fekk ñoom ci seen bopp, ñuy seen yoonu bopp, doonte amuñu yoonu Musaa.
15Noonu lañu wérale ne jëf ji yoonu Musaa santaane moo binde ci seenub xol, ba seen yég-yégu xol seede loolu. Li koy firndeel it di seen xel miy def leeg-leeg mu sikk leen, leeg-leeg mu dëggal leen.
16Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.
17Ma dikk nag ci yaw miy wuyoo turu Yawut, te yaakaar yoonu Musaa, boole ci di sagoo Yàlla.
18Yaa xam coobarey Yàlla, te yaa jànge ci yoonu Musaa, ba xam li am solo dëgg.
19Yaw mi mu wóor ne yaa di wommatkatub gumba yi, te di leeru ñi ci lëndëm gi,
20yaa di jànglekatub naataxuuna yi, di sëriñub tuut-tànk yi, gannaaw yaa jagoo ci yoonu Musaa, mboolem luy jëmmu xam-xam, ak lépp luy dëgg.
21Kon yaw miy jàngle, doo jàngal sa bopp? Yaw miy waare, di aaye sàcc, mbaa doo sàcc? Yaw miy aaye njaaloo, mbaa doo jaaloo?
22Yaw mi bañ bokkaale, mbaa doo sëxëtoo jaamookaayi bokkaalekat yi?
23Yaa ngi sagoo yoonu Musaa te di ko moy bay teddadil Yàlla!
24Yeen de yeena tax ñuy ñàkke teggin turu Yàlla ci biir xeeti jaambur yi dul Yawut, te noonu la ko Mbind mi indee.
25Aaday xaraf nag amal na la njariñ, ndegam sàmm nga yoon wi ko digle. Waaye soo dee moykatub yoon wi, sag xaraf, ñàkka xaraf lay doon.

Read Room 2Room 2
Compare Room 2:5-25Room 2:5-25