Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 1

Room 1:3-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3moo jëm ci Doomam, ji soqikoo ci askanu Daawuda, ci wàllu àddina.
4Waaye ci wàllu Noo gu Sell gi, mooy ki dogal ba tabb muy Doomu Yàlla ji jagoo doole ndax ndekkiteem, te mooy sunu Sang Yeesu Almasi.
5Ci Almasi lanu jote aw yiwu doon ay ndaw, ngir nit ñi déggal yoonu ngëm wi, ci biir mboolem xeeti àddina, ngir aw turam.
6Te yeen ñi ñu woo ci Yeesu Almasi itam, ci ngeen bokk.
7Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
8Ma doore sant sama Yàlla ci Yeesu Almasi ngir yeen ñépp, ndax seen ngëm siiw na ci àddina sépp.
9Yàlla mi may jaamoo xol, ci ni may siiwtaanee xibaaru jàmm bu Doomam, moom seere na ne noppiwuma leena fàttliku.
10Xanaa di saxoo dagaan ci samay ñaan, su ci Yàlla àndee, yoon wu jub wu ma mujj dikke ba ci yeen.
11Yàkkamti naa leena gis, ba jottli leen mayug yiw gu bawoo ci Noo gu Sell gi, ngir dooleel leen,
12te loolu mooy ma bokk ak yeen lu dëfal sama xol, dëfal leen, ci seen ngëm ak sama gos.
13Bokk yi, bugguma ngeen umple ne ay yooni yoon laa leen mébéta seetsi, ba liggéey ci seen biir lu leen jariñ, ni ma ko defale yeneen xeet; waaye ay gàllankoor a ma téye ba tey jii.
14Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp.
15Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.
16Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
17Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»
18Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
19Ndaxam lees mana xam ci Yàlla, leer na ci seen biir, nde Yàlla moo leen ko leeralal.
20Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.
21Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.
22Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof.
23Leeru Yàlla ji dul dee lañu weccee jëmmu nit ki deeyam dul jaas, ak picc, ak boroom ñeenti tànk, ak ndëgmeent.
24Moo tax Yàlla bërgal leen ak seen xemmemtéef yu bon yi ci seen xol, ba ñu sóobu ci jëflantey sobe juy teddadil seen yarami bopp.
25Ñoo weccee dëggu Yàlla, aw fen, di sujjóotal ak a jaamu mbindeef, bàyyi Bindkat bi yelloo cant ba fàww. Amiin.
26Loolu moo tax Yàlla bërgal leen ak seen bëgg-bëgg yu teddadi. Seeni jigéen sax dëddu nañu jaxasoo gi leen bindub juddu sédde, ba jublu ci lu woroo ak seen bindub juddu.
27Naka noonu, góor ñi it noppee jaxasoo ak jigéen, ni leen ko bindub juddu sédde, bay xabtaloo ci seen biir, seen bëgg-bëggi bakkan yu tar; ay góor di séq ak seen moroomi góor jëf ju gàccelu, ba tax leena jot ci seen jëmmi bopp, seen añub réeraange.
28Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.
29Dañoo dem ba feese gépp xeetu njubadi, akug mbon, akug bëgge, akug coxor. Noyyeewuñu lu moy kiñaan, ak pexey bóome, ak ŋaayoo, akug njublaŋ, ak jëf ju sew. Ay jëwkat lañu it,
30te di yàqkati der, ñu bañ Yàlla lañu, ñu reew, réy, di tëggu, ñu xareñ ci fexe lu bon, te déggadil seeni waajur.
31Amuñu xel, amuñu kóllëre, amuñu xol, amuñu yërmande.

Read Room 1Room 1
Compare Room 1:3-31Room 1:3-31