Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 1

Room 1:17-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»
18Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
19Ndaxam lees mana xam ci Yàlla, leer na ci seen biir, nde Yàlla moo leen ko leeralal.
20Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.
21Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.
22Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof.
23Leeru Yàlla ji dul dee lañu weccee jëmmu nit ki deeyam dul jaas, ak picc, ak boroom ñeenti tànk, ak ndëgmeent.

Read Room 1Room 1
Compare Room 1:17-23Room 1:17-23