17Ndaxte xibaar bii day wone, ni nit mana jube ci kanam Yàlla, sukkandikoo ci ngëm rekk, tàmbali ci ngëm, yem ci ngëm. Moo tax Mbind mi wax ne: «Ku jub ci kaw ngëm, dinga dund.»
18Merum Yàllaa ngi feeñe asamaan, wàcc ci nit ñi, ndax seen weddi Yàlla gépp ak seen jubadi gépp, ñoom ñi suul dëgg, di topp lu jubadi.
19Ndax li nit mana xam ci Yàlla, leer na ci seen xel, ndax Yàlla won na leen ko.
20Ndaxte ba àddina sosoo ba tey, mbiri Yàlla yu nëbbu ya, maanaam dooleem ju sax ja, ak meloom wu kawe wa, feeñ nañu bu leer, te bir ñépp ci yi mu sàkk, ba tax bunti lay yépp tëj nañu.
21Ndaxte bi ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ni mu ware, mbaa ñu sant ko. Waaye ñu daldi réer ci seen biiri xalaat yu mujjul fenn, ba tax seen xol gumba, ba lëndëm këruus.
22Ñu teg seen bopp ni boroomi xel, fekk ñu ñàkk xel lañu woon.
23Toxal nañu ndamu Yàlla Aji Sax ji, wuutal fa nataali nit ku dul sax, moom ak ay picc, ay rabi àll mbaa yuy raam.