Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - ROOM - ROOM 11

ROOM 11:14-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14Dama koy def, ngir ñi bokk ak man xeet siis, ba ñenn ñi mucc.
15Ndaxte bi Yàlla génnee Israyil, ubbee na noonu bunt, ngir xeeti àddina juboo ak moom; kon su Yàlla dugalaatee Israyil, ndax du mel ni ndekkitel néew ya?
16Damay wax ne, mburu mépp sell na, bu ci Yàlla amee wàll. Naka noonu garab gi Yàlla séddoo reen bi, garab gépp sell na.
17Bànni Israyil a ngi mel ni garabu oliw gu ñu jëmbët ci kër gi, waaye mu am car yu ci fàq. Yaw mi dul Yawut, yaa ngi mel ni caru garabu oliw gu àll bu ñu jabtal ci garabu kër googu. Noonu nga jariñoo meen, mi jóge ci reen bi.
18Kon nag bul bàkku, di xeeb car yooyu Yàlla fàq. Waaye soo bëggee bàkku, xamal ne reen moo lay yenu, te du yaw miy car yaa koy yenu.
19Xanaa dinga wax ne: «Car yooyu dañu leena fàq, ngir jabtal ma fa ñu nekkoon.»
20Dëgg la; waaye seen ngëmadee tax ñu fàq leen, wuutal la fa ndax sa ngëm. Bumu tax nag ngay bàkku, waaye nanga moytu.
21Gannaaw Yàlla baalul car ya cosaanoo ca garab ga, kon boog yéen itam man na leena fàq.
22Loolu kon wone na ni Yàlla baaxe ak ni muy meree tooñ. Ci ñi daanu, Yàlla wone na ni meram tànge, wone mbaaxam ci yéen, su fekkee yéena ngi ci wéy; lu ko moy, dees na leen fàq yéen itam.
23Te car yooyu fàq, su ñu wéyul ci seen ngëmadi, dees na leen delloo ci garab gi, ndax Yàlla man na leen cee tafaat.
24Yaw mi dul Yawut, yaa ngi bokkoon ci garabu oliw gu àll, waaye Yàlla daf la cee jële, ci lu dul farala am, jabtal la ci garabu kër gi. Kon man nanoo gëna wóor ne, Yawut ya judduwaale nekk ci garabu oliw gu kër gi, Yàlla dina leen ci delloo.
25Bokk yi, dama leena bëgga dindi kumpa ci lii, ngir ngeen baña yég seen bopp. Dërkiisu xol dab na bànni Israyil ab diir, ba bés ba mboolem waa àddina, ñu wara bokk ci nguuru Yàlla, dugg ca.
26Bu loolu amee nag, bànni Israyil gépp dina mucc. Moom la Mbind mi tëral, bi mu naan: «Ab xettalikat dina jóge ci Siyoŋ, dàq weddi ci askanu Yanqóoba.
27Loolu mooy kóllëre, gi may fas ak ñoom, bés bu may dindi seeni bàkkaar.»
28Gannaaw bañ nañu xibaaru jàmm bi, ay bañaaley Yàlla lañu, ngir ngeen jot barkeem. Waaye gannaaw Yàlla tànn na leen, dafa leen bëgg ba tey ndax seen maam ya.
29Ndax li Yàlla maye, dootu ko nangu mukk, te ku mu woo ci boppam, dootu la dàq mukk.
30Ñu déggadil Yàlla ngeen woon, waaye ngëmadig Yawut yi tax na, ngeen jot yërmandeem.
31Ñoom itam lànk nañu léegi, ngir mana bokk ak yéen yërmandey Yàlla.
32Kon Yàlla tëj na ñépp ci ngëmadi, ngir mana yërëm ñépp.
33Xelum Yàlla ni mu xóote, ak xam-xamam ni mu baree, ba raw xelum nit! Kan moo muus, ba xam dogalam? Walla nga am xel, ba nànd ay jëfam?
34Mbind mi dafa ne: «Ana ku xam xalaatu Boroom bi? Ku ko doon digal?»

Read ROOM 11ROOM 11
Compare ROOM 11:14-34ROOM 11:14-34