Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Njàlbéen ga - Njàlbéen ga 36

Njàlbéen ga 36:8-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Esawu nag dëkk ca tundu Seyir: Esawu moomu mooy Edom.
9Askanu Esawu, di maami Edomeen ña ca tundi Seyir, mooy lii.
10Doomi Esawu yu góor ñooy: Elifas, mi mu am ak soxnaam Ada ak Rewel, mi mu am ak Basmat.
11Doomi Elifas yu góor yi di: Teman ak Omar ak Sefo ak Gatam ak Kenas.
12Timna it nekkaaleb Elifas. Mu am caak moom Amaleg. Ñooñoo xeetoo ci Ada, soxnas Esawu.
13Doomi Rewel yu góor yi ñoo di: Naxat ak Sera ak Saama ak Misa. Ñooñoo xeetoo ca Basmat, soxnas Esawu.
14Soxnas Esawu, si ñu naa Olibama, tey doomu Ana miy doomu Sibeyon, moo am ak Esawu doom yu góor yii: Yewus, Yalam ak Kora.
15Làngi doomi Esawu yu góor nag, ñooy ñii. Ñi askanoo ci Elifas taawub Esawu, ñuy Teman ak Omar ak Sefo ak Kenas
16ak Kora ak Gatam ak Amaleg, ku ci nekk ak làngam. Làngi Elifas, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Ada.
17Ñi askanoo ci Rewel doomu Esawu, ñooy Naxat ak Sera ak Saama ak Misa, ku ci nekk ak làngam. Làngi Rewel, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Basmat, soxnas Esawu.
18Ñi xeetoo ci Olibama soxnas Esawu, ñooy Yewus, Yalam ak Kora, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi Olibama, soxnas Esawu siy doomu Ana.
19Ñooñooy doomi Esawu, mi ñuy wax Edom, ñooñooy doomam yu góor, ñook seeni làng.
20Doomi Seyir, ya bokk ca waa Or te sancoon ca réew ma, ñooy Lotan ak Sobal ak Sibeyon ak Ana
21ak Dison ak Eser ak Disan. Ñooñooy làngi waa Or, di sëti Seyir ya ca réewum Edom.
22Doomi Lotan yu góor ya nag ñooy Ori ak Emam. Jigéenub Lotan di Timna.
23Doomi Sobal yu góor ya di Alwan ak Manaat ak Ebal ak Sefo ak Onam.
24Doomi Sibeyon yu góor di Aya ak Ana. Te Ana moomu moo feeñal bëti ndox yu tàng ya ca màndiŋ ma, ba muy sàmm mbaami baayam Sibeyon.

Read Njàlbéen ga 36Njàlbéen ga 36
Compare Njàlbéen ga 36:8-24Njàlbéen ga 36:8-24