Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Njàlbéen ga

Njàlbéen ga 7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge.
2Xeeti rab yu set yépp yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ak ñaar ci xeeti rab yi setul, te ñuy góor ak jigéen.
3Te it xeetu picc mu nekk yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ngir seen xeet baña fey ci kaw suuf.
4Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»
5Nóoyin daldi def la ko Aji Sax ji sant lépp.
6Bi mbënn miy ñëw ci àddina, booba fekk na Nóoyin am juróom benni téeméeri at.
7Nóoyin dugg na ca gaal ga, ànd ak ay doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya, ngir mucc ca ndoxu mbënn ma.
8Rab yu set yi ak yi setul ak picc yi ak yiy raam
9ànd nañu ak Nóoyin, dugg ca gaal ga, def ñaar-ñaar, góor ak jigéen, ni ko Yàlla sante Nóoyin.
10Ba juróom ñaari fan wéyee nag, ndoxu mbënn ma agsi ci kaw suuf.
11At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at, ca fukki fan ya ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, kera la bëti ndox ya ne jàyy, jóge xóotey géej, bunti ndoxi asamaan ne kulbét, mu ne yureet,
12taw biy sottiku ci suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg.
13Keroog bés boobu la Nóoyin ànd aki doomam yu góor, Sem ak Xam ak Yafet, ak soxnaam ak ñetti soxnay doomam yooyu, ñu dugg ca gaal ga,
14àndandook rabu àll yépp, lu ci nekk ak wirgoom, ak jur gépp, lu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy naaw, lu ci nekk ak wirgoom, muy picc mbaa boroomi laaf.
15Lépp luy boroom bakkan def na ñaar-ñaar, ànd ak Nóoyin, dugg ca gaal ga,
16mboolem xeetu mbindeef rekk, di góor ak jigéen, ni ko ko Yàlla sante. Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ràpp buntu gaal gi, gannaaw bi Nóoyin duggee.
17Mbënn ma nag di wal ci àddina diiru ñeent fukki fan. Ndox ya di yokku, gaal gay jóg, ba tëmb, tiim suuf lu sore.
18Ma ngay gën di yokku, tey baawaan ci kaw suuf, ba gaal ga tëmb, di dem ca kaw ndox ma.

19Ndox ma di walangaan, ba mëdd tund yu kawe ya fépp fu asamaan tiim.
20Muy yokku, di yokku, ba gëna kawe tund ya lu mat fukki xasab ak juróom.
21Mboolem mbindeef mu daan dox ci kaw suuf dee na ca. Picc yi ak jur gi ak rabi àll yi ak lépp luy raam ci kaw suuf dee na, ñoom ak nit ñépp.
22Mboolem mbindeef muy boroom bakkan ci kaw suuf a bokk dee.
23Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga.
24Ndox mi nag di wal-wali ci kaw suuf diirub téeméeri fan ak juróom fukk.