Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 1

Ngën-gi-woy 1:4-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Yóbbaale ma, nu daw, dem. Sama buur, yóbbu ma sa néeg, nu bokk mbég ak bànneex, di tàqamtikoo sa cofeel gi dàq biiñ. Ñoo yey nob la!
5Yeen janqi Yerusalem, damaa ñuul, rafet; ñuul ni xayma ya ca Kedar, mel ni ridoy Buur Suleymaan.
6Buleen ma xoole sama ñuulaay bi, jant bee ma lakk. Samay càmmiñ a ma mere, di ma wattuloo tóokëri reseñ ya, te wattuwuma sama tóokëri bopp.

Read Ngën-gi-woy 1Ngën-gi-woy 1
Compare Ngën-gi-woy 1:4-6Ngën-gi-woy 1:4-6