Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 1:4-6 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 1:4-6 in Kàddug Yàlla gi

4 Yóbbaale ma, nu daw, dem. Sama buur, yóbbu ma sa néeg, nu bokk mbég ak bànneex, di tàqamtikoo sa cofeel gi dàq biiñ. Ñoo yey nob la!
5 Yeen janqi Yerusalem, damaa ñuul, rafet; ñuul ni xayma ya ca Kedar, mel ni ridoy Buur Suleymaan.
6 Buleen ma xoole sama ñuulaay bi, jant bee ma lakk. Samay càmmiñ a ma mere, di ma wattuloo tóokëri reseñ ya, te wattuwuma sama tóokëri bopp.
Ngën-gi-woy 1 in Kàddug Yàlla gi