4Yóbbaale ma, nu daw, dem. Sama buur, yóbbu ma sa néeg, nu bokk mbég ak bànneex, di tàqamtikoo sa cofeel gi dàq biiñ. Ñoo yey nob la!
5Yeen janqi Yerusalem, damaa ñuul, rafet; ñuul ni xayma ya ca Kedar, mel ni ridoy Buur Suleymaan.
6Buleen ma xoole sama ñuulaay bi, jant bee ma lakk. Samay càmmiñ a ma mere, di ma wattuloo tóokëri reseñ ya, te wattuwuma sama tóokëri bopp.
7Sama soppey xol, ngalla wax ma ana fooy foral, di fa gooral, digg bëccëg? Lu ko moy may muuru, di la wër fi say xarit ak seeni gétt.
8Aa! Xamoo koo? Yaw mi dàq ci jigéen ñi! Génnal rekk, topp wewi jur gi, sàmmi say tef, fi dendeek mbaari sàmm si.
9Xarit, xam nga lu ma lay xoole? Yànjaayu wajan wu takk watiiru Firawna.
10Sa lex yaa ngi tàkk fi digg sàdd yi! Céy wii loos ak caqu peram!
11Sàddi wurus lanu lay defaral, tapp ca xaalis.
12Li sama buur tëdd, di xéewlu lépp, maa ngi gilli lu neex.
13Sama nijaay di mbuusum ndàbb may fanaan sama digg ween.
14Saa nijaay, saa cabbu tóor-tóoru fuddën, fa digg tóokëri Engedi.
15Xarit, yaaka rafet, yaaka taaru! Say gët niy pitax.
16Nijaay, yaaka góorayiw, yaaka maa neex! Mbooy gu naat, nu laloo,
17garabi seedar di sunu xànqi néeg, garab gu dul ruus xadd ko.