Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MÀRK - MÀRK 7

MÀRK 7:11-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Waaye yéen dangeen ne: ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga wara jariñoo ci man Korban la,” —maanaam saraxu Yàlla la—
12dootuleen ko bàyyi, mu defal dara ndeyam walla baayam.
13Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada, ji ngeen di donnante. Te it yéena ngi def yeneen yu bon yu mel nii.»
14Noonu Yeesu waxaat ak mbooloo mi ne leen: «Yéen ñépp dégluleen ma te xam.
15Li ci biti, tey dugg nit, du ko mana indil sobe, waaye li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.»
17Bi nga xamee ne jóge nañu ci mbooloo mi, dugg ci kër gi, taalibe yi laaj Yeesu, mu firil leen wax ju làqu jooju.
18Yeesu ne leen: «Ndax yéen itam seen xol dafa tëju? Xanaa xamuleen ne, dara lu jóge biti, dugg ci nit, du ko mana indil sobe,
19ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay jëm, ba noppi daldi génn ca bérab bu làqu?» Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na bépp ñam.
20Yeesu ne leen ati: «Li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.
21Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di jóge ak ndoxaanu yàqute, càcc ak bóom,
22njaaloo ak bëgge, coxor, naaféq, ñaawteef, ñeetaan, saaga, réylu ak jëfi ndof.
23Lu bon loolu lépp day génn ci nit, di ko indil sobe.»
24Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam manula umpe.
25Amoon na fa nag jigéen ju rab jàpp doomam ju jigéen. Bi mu déggee ne, Yeesoo nga fa, mu ñëw, daanu ciy tànkam,
26fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam.
27Waaye Yeesu ne ko: «Na gone yi jëkka lekk, ba regg; fab ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
28Jigéen ji ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gone yi.»
29Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Ndax wax jooju demal ci jàmm, rab wa génn na sa doom.»
30Noonu mu ñibbi, fekk doom ji tëdd cib lal te mucc ci rab wi.
31Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi.
32Foofa ñu indil ko ku tëx te dër lool, ñaan ko mu teg ko loxo.

Read MÀRK 7MÀRK 7
Compare MÀRK 7:11-32MÀRK 7:11-32