11Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?»
12Musaa nag woolu Datan ak Abiram, doomi Elyab, ñu ne ko: «Danoo ñëwul!
13Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci?
14Du réew mu meew maak lem ja tuuroo nga nu yóbbu de, te séddoo nu céri tool mbaa tóokëri reseñ. Mbooloo mii mépp, man nga leena tuur lëndëm? Danoo ñëwul!»
15Ba loolu amee Musaa mer lool. Mu ne Aji Sax ji: «Bul geesu sax seen sarax. Menn mbaam sax, masuma leen koo jëlal te masuma cee tooñ kenn.»
16Musaa nag ne Kore: «Yaw, yaak sa gàngoor gépp, ca kanam Aji Sax ji, yaak ñoom ak Aaróona, ëllëg.
17Na ku nekk jël ub andam, def ci cuuraay, te na ku ci nekk indib andam fi kanam Aji Sax ji, muy ñaar téeméeri and ak juróom fukk, yaak Aaróona it, ku nekk akub andam.»
18Ba mu ko defee ku nekk jël ub andam, def cay xal, teg ca cuuraay. Ñu taxaw ca bunt xaymab ndaje ma, ñook Musaa ak Aaróona.
19Kore nag dajale gàngoor gépp fa ñoom, ca bunt xaymab ndaje ma. Ci kaw loolu leeru Aji Sax ji feeñu mbooloo ma mépp!
20Aji Sax ji wax Musaa ak Aaróona, ne:
21«Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!»
22Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?»
23Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa:
24«Waxal mbooloo mi, ne leen ñu jóge fi wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram.»
25Musaa daldi jubal ca Datan ak Abiram, magi Israyil topp ca.
26Ci biir loolu mu wax ak mbooloo ma, ne leen: «Ngalla dàndleen xaymay nit ñu bon ñii, te buleen laal seen lenn, bala ngeen di buuboondook mboolem bàkkaari ñii.»
27Ñu daldi jóge mboolem fa wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñoom, ña nga génn, taxaw ca seen bunti xayma, ñook seeni jabar ak seeni doom, ak seeni tuut-tànk.
28Musaa nag ne: «Lii nag moo leen di xamal ne Aji Sax ji moo ma yebal ngir ma def jëf jii jépp, waaye du sama coobarey bopp:
29Ndegam ni mboolem doom aadama di deeye, ni la ñii deeye, seen demin di deminu mboolem doom aadama, su boobaa du Aji Sax jee ma yebal.
30Waaye ndegam Aji Sax ji moo sàkk ba sàkk tey lu masula am, ba suuf ŋa, mëdd leen, ñook lu bokk ci ñoom, ñu tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, su boobaa dingeen xam ne ñoom ñii ñoo xarab Aji Sax ji.»
31Naka la Musaa di daaneel kàddu yooyu yépp, fa ñu taxaw jekki xar,
32suuf ŋa, mëdd leen, ñook seen waa kër, ak mboolem ku bokk ci Kore, ak mboolem alal ja.
33Ñu daldi tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, ñook mboolem lu ñu moom, suuf sàng leen, ñu réer mbooloo ma mërr.
34Mboolem Israyil dégg seen yuux ya, daldi daw, te naan: «Nan daw bala noo suuf a mëdd!»
35Ci kaw loolu sawara moo bawoo fa Aji Sax ji, xoyom ñaar téeméeri nit ak juróom fukk ña indi woon saraxu cuuraay ba.