Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 21

LUUG 21:8-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Yeesu ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Moom laa,” walla ñu naan: “Jamono ji jegesi na.” Buleen topp ñooñu.
9Bu ngeen déggee ay xare ak ay réew yu jóg, wottuleena tiit, ndaxte fàww yooyule jëkka am. Waaye taxul mujug jamono daldi taxaw.»
10Noonu mu teg ca ne: «Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew dina xeex ak meneen réew.
11Suuf dina yëngu yëngu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan.
12Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam i buur ak i boroom réew ndax sama tur.
13Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel.
14Fasleen yéenee baña wut lay ngir musal seen bopp.
15Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko mana teggi, mbaa ñu di ko weddi.
16Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen.
17Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
18Waaye seen genn kawar sax du neen.
19Seen muñ moo leen di musal.
20«Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na.
21Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba!
22Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat.
23Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii.
24Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.

Read LUUG 21LUUG 21
Compare LUUG 21:8-24LUUG 21:8-24