3Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.
4Képp kuy dund kat, am nga yaakaar, te xaj buy dund a gën gaynde gu dee.
5Kuy dund xam ne dangay dee, waaye ku dee xamul dara, te séentootul ab yool. Ku dee, ñu fàtte la.
6Muy sa cofeel, di sa mbañeel, ba ci sa kiñaan ànd ak yaw seey. Du lenn lu deeti sa wàll ci jépp jëfi kaw suuf.
7Kon doxal, lekk saw ñam, bége, te naan sa biiñ ci xol bu sedd. Yàlla kat nangul na la jeeg say jëf.
8Foo tollu, solul ba jekk, te bul fàttee xeeñlu.
9Bànneexul yaak ndaw si nga sopp ci fan wu gàtt wi la Yàlla may fi suuf, ndax loolu nga séddoo ci fan wu gàtt wii ngay doñ-doñaale fi kaw dun bi.
10Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw, ga nga jëm.
11Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.
12Doom aadama la bésu safaan bay bett, jekki ne dàll fi kawam, ni jën wu keppu cib caax, loru, mbaa picc mu tancu cig fiir. Doom aadama xamul bésam.
13Lii it gis naa ko, muy lu ma yéem, di mbirum xel mu rafet fi kaw suuf.