11Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.
12Doom aadama la bésu safaan bay bett, jekki ne dàll fi kawam, ni jën wu keppu cib caax, loru, mbaa picc mu tancu cig fiir. Doom aadama xamul bésam.
13Lii it gis naa ko, muy lu ma yéem, di mbirum xel mu rafet fi kaw suuf.
14Ab dëkk bu ndaw la woon, nit ña néew. Buur bu mag song dëkk ba, gaw ko, jal jali suuf yu mag, sësal ca tata ja.
15Fekk fa ku néewle te xelu. Mu manoona xelal dëkk ba, xettli leen, waaye kenn faalewu ko.
16Man dama noon xel mu rafet a gën doole! Ndeke ku néewle ñu xeeb la, tanqamlu say wax.