8Kenn moomul bakkanam, ba man koo dese, kenn amul sañ-sañ ci bésub deeyam, kenn muccul ci boobu xare, te mbon du ca wallu boroom.
9Loolu lépp gis naa ko, ba may xalaat ci jépp jëfi kaw suuf; fi nit di yilife nit, muy loraange.
10Ma gis itam ñu bon ñu ñu rob, ñu daan yaale kër Yàlla ga, ñu di leen gërëme tey seeni jëf ca dëkk ba. Loolu it, cóolóoli neen.