7Kenn xamul luy xew ëllëg, kenn manula wax luy xew ëllëg.
8Kenn moomul bakkanam, ba man koo dese, kenn amul sañ-sañ ci bésub deeyam, kenn muccul ci boobu xare, te mbon du ca wallu boroom.
9Loolu lépp gis naa ko, ba may xalaat ci jépp jëfi kaw suuf; fi nit di yilife nit, muy loraange.
10Ma gis itam ñu bon ñu ñu rob, ñu daan yaale kër Yàlla ga, ñu di leen gërëme tey seeni jëf ca dëkk ba. Loolu it, cóolóoli neen.
11Jëf ñaaw na, mbugal ma yeex, ba tax doom aadama sóobu ci mbon.
12Nit bàkkaar na téeméeri yoon, te teewul mu gudd fan. Xam naa it ne nee ñu ngëneel a ñeel ku ragal Yàlla, ndax wormaal ko.