3Bul gaawa won buur gannaaw; bul saxoo lu buur buggul; Buur, lu ko neex lay def.
4Kàddug buur kilifteef la. Ana ku ko naan: «Looy def nii?»
5Ku dégg ndigal doo am lu la soof. Ku xelu, xam lu jot, xam doxalin.
6Mbir mu mu doon kat ak jotam ak doxalinam, waaye nit am na tiis wu ko diis.
7Kenn xamul luy xew ëllëg, kenn manula wax luy xew ëllëg.