12Nit bàkkaar na téeméeri yoon, te teewul mu gudd fan. Xam naa it ne nee ñu ngëneel a ñeel ku ragal Yàlla, ndax wormaal ko.
13Ku bon, du am lu baax, fanam du màgg ni ker, ndax wormaalul Yàlla.
14Waaye cóolóoli neen a ngi am fi kaw suuf: Ku jub jot yoolu ku bon, ku bon jot yoolu ku jub. Ma ne loolu it cóolóoli neen la.
15Man daal damay digle bànneex, ndax nit amul lu gën fi kaw suuf di lekk ak a naan ak a bànneexu, muñe ko doñ-doñam, fan yi ko Yàlla may fi kaw suuf.
16Ma walbatiku xalaat, di jéema xam fu xel rafete, di xoolaat li nit jàppoo fi kaw suuf, ba guddeek bëccëg, gëmmul bët.