Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 7

Kàdduy Waare 7:5-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Déglu ku xelu di la àrtu moo gën déglu dof bu lay woy.
6Ab dof day textexi ni dég yuy retete taal bu cin tege. Loolu it di cóolóoli neen.
7Foqarñi kay day dofloo boroom xel, te ab ger da lay gëlëmal.
8Fa mbir mujjee gën fa mu doore, te muñ a gën réy-réylu.
9Bul gaawa mer; mer, xolub dof la samp këram.
10Bul ne lu tax démb dàq tey, loolu, laaj ko du xel.

Read Kàdduy Waare 7Kàdduy Waare 7
Compare Kàdduy Waare 7:5-10Kàdduy Waare 7:5-10