14Su neexee, bànneexul; su mettee, xoolal ne lu ci ne, Yàllaa ko def ngir jaam bi umple gannaawam.
15Lu ne laa gis ci sama dund gu gàtt gii! Nit a ngii jub, teewu koo sànkook njubam; nit bon, ànd ak mbonam, gudd fan.
16Bul jub ba mu ëpp, bul wóolu sam xel ba mu ëpp, lu ko moy nga yàqule.
17Bu la mbon jiital, te bul dofe. Jàppool lii, te baña wacc lee, mooy li gën, lu ko moy nga dee te sa àpp jotul. Ku ragal Yàlla kat sàmm yooyu yaar.