3Ku giir téeméeri doom, dund ati at, ak lu at ya bare bare, su bégewul teraanga ja mu am te amul njégu bàmmeelam sax, kooku lumb wu tuuroo ko tane.
4Lumb wa ñëw na moos ci neen, bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.
5Gisul jant, xamu ko, waaye noflaay moo ko ëpple mag ma,
6bu dundoon junniy junniy at sax te amul jàmm. Xanaa du benn bérab la ñépp jëm?
7Nit ak doñ-doñam jépp, biiram, te taxul mu doylu.
8Ana lu boroom xel ëpplee ku dofe? Nga ñàkk, xam doxalin, lu mu lay jariñ?