10Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
11Surga, lekkam néew, bare, mu nelaw, ba fàttey boram; boroom alal regg, du nopplu, du nelaw.
12Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf: Alal ju boroom dajale ba loru,
13mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.