7Mu jot nga xar, mu jot nga gaar; mu jot nga selaw, mu jot nga wax.
8Mu jot nga sopp, mu jot nga jéppi; mu jot nga xare, mu jot nga jàmmoo.
9Ana lu liggéeykat biy jariñoo ciw ñaqam?
10Gis naa ne sas la bu Yàlla sase, nu war koo sasoo.
11Lépp la Yàlla def, ba bu jotee rafet. Moo may nit muy njort ëllëg, te taxul mu mana ràññee jëf ji Yàlla jëf, njàlbéen ba muj ga.