Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 3

Kàdduy Waare 3:11-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Lépp la Yàlla def, ba bu jotee rafet. Moo may nit muy njort ëllëg, te taxul mu mana ràññee jëf ji Yàlla jëf, njàlbéen ba muj ga.
12Ma gis ne nit amul lu gën bànneex ak jàmmi bakkan cig dundam,
13te nitoo nit, su dee lekk ak a naan, di ñaq, jariñoo, loolu mayu Yàllaa.
14Ma xam ne lu Yàlla def, loola day sax ba fàww. Deesu ci yokk, mbaa di wàññi dara; Yàllaa ko def, ngir nit di ko wormaal.
15Lu ay tey, ayoon na, lu ay ëllëg it ayoon na. Yàllaay namma indi la woon.
16Ma dellu gis fi kaw suuf ne, fu yoon moom, fa la njubadi ne, fa njub moom it, fa la njubadi ne.
17Saam xel ne ma, ku jub ak ku bon la Yàlla di boole àtte, ngir mbir mu ne ak jëf ju ne ak bésam.
18Saam xel neeti ma, nun doom aadama, Yàllaa nuy nattu, nu gis ne ay mala doŋŋ lanu.
19Dogalu doom aadama ji ak dogalu mala mi, benn dogal bee; ni kii di deeye la kee di deeye, genn noo gee, nu bokk ko. Lu nit ëpplee mala neen na, ñoom ñépp, cóolóoli neen.
20Ñoom ñépp a bokk jëm benn bérab ba, bokk jóge pëndub suuf, bokk dellu suuf.
21Ana ku mu wóor ne bakkanu nit day yéeg asamaan, bakkanu mala tàbbi suuf?
22Ma gis nag ne nit amul lu gën di bànneexoo ñaqam, loolooy wàllam. Ana ku koy xamal gannaawam?

Read Kàdduy Waare 3Kàdduy Waare 3
Compare Kàdduy Waare 3:11-22Kàdduy Waare 3:11-22